podcast
details
.com
Print
Share
Look for any podcast host, guest or anyone
Search
Showing episodes and shows of
Cheikhouna Diaw
Shows
Bëgg a Baax podcast
Njariñu Koor
Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
2025-03-06
36 min
Bëgg a Baax podcast
Moytu àq yi
Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo ngir ëllëg sa dara du lëj.
2025-01-21
13 min
Bëgg a Baax podcast
Tëj gi: Gàllaŋkoor yi
Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen ludut Yàlla ci gàllankoor yi la bokk.
2024-12-14
15 min
Bëgg a Baax podcast
Pensées et introspection
Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.
2024-10-16
39 min
Bëgg a Baax podcast
Tegginu nitu Yàlla yi
Ci waxtaan wii Imaam Dardiir dafa ciy waxtaane jikko yi nitu Yàlla yi di ame bu seen dox ci Yàlla matee ba seen i teggin mat sëkk (Makkaarimal ahlaax).
2024-07-31
31 min
Bëgg a Baax podcast
Lan mooy gis Yàlla?
Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir dafa ciy leeral xeetu teewlu yi am ak fi ñu man a yóbb nit ki ci jege Yàlla. Bu fa nit ki àgge, dina dem ba xam, yëg bir yoo xam ne maneesu koo leeral ci làmmiñ.
2024-06-22
23 min
Bëgg a Baax podcast
Xeetu sikar yi: Tudd Yàlla ci làmmiñ
Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir da ciy wax ci xeetu tudd Yàlla yi am, rawatina bu làmmiñ bi nga xam ne kiy doog a sóobu ci lay tàmbalee. Ci mujj gi mu tënk ponku tassawuf yi mu jàpp ne ñoo ci gën a am solo.
2024-05-29
25 min
Bëgg a Baax podcast
Waxtaan ci tassawuf: Sikar ak xalam (zikru ak fikru)
Ci tomb yii, Imaam Dardiir da ciy wax ci solos jaamu Yàlla njël ak taxawaayu tudd Yàlla ci dundug aji-sóobu ji. Ñu doon yaari ponk yoo xam ne ki sóobu ci Yàlla da leen a war a fonk ngir jot ci càkkuteefam.
2024-05-18
20 min
Bëgg a Baax podcast
Waxtaan ci 6i ponku tassawuf bi: Al-uzla (wéet)
Wéet daa bokk ci ponk yi tassawuf teg ngir nit ki sellal xolam. Jaxasoo ak nit yi lu bari ci lu dul farata dafay sabab ay ayibu xol. Moom la Imaam Dardir di leeral ci waxtaan wii ngir aji-sóobu ji bàyyi ko xel.
2024-04-08
21 min
Bëgg a Baax podcast
Waxtaan ci ponku tasawuf yi: Sëriñ bu mat sëriñ
Ci dars bii, Imaam Dardiir dafay waxtaan ci ponku tassawuf yii di nangu ndogal ak wut sëriñ bu mat sëriñ. Ci ginnaaw gi mu misaal nu sëriñ bu mat sëriñ nu muy mel.
2024-03-27
31 min
Bëgg a Baax podcast
Ñaareelu- ak ñetteelu ponk tassawuf yi: Sant ak muñ
Ci biir fukki ponk tassawuf yi Imaam Dardiir indi ci téereem bi, waxtaan wii mu ngi aju ci lan lañuy tuddee sant Yàlla ci diine ak lan mooy muñ bi tax ñuy wax muñ.
2024-03-20
31 min
Bëgg a Baax podcast
Ponku tassawuf bu njëkk bi: Tuub
Tasawuf daa am ay ponk yoo xam ne nitu Yàlla yi dañu ko tëral ngir yombal aji-sóobi ji ngir mu jot ci sàkkuteefam. Ponk yooyu ñu ngi ko tënk ci fukk. Tay nag ponk bu njëkk bi lañuy waxtaane te mooy TUUB.
2024-03-15
33 min
Bëgg a Baax podcast
Waxtaan ci tasawuf: Ñaarelu Xaaj bi: Jikko yiy gàllaankoor nit ki ci yoonu Yàlla
Ci waxtaan wii, imaam Dardiir dafay waxtaane jikkoy xol yiy gàllankoor muriit bi ba du am ag jege Yàlla. Saalig bi (ki bëgg àgg ci Yalla) daa war a taqoo ak sikar ak jéem a dindi jikko yu ñaaw yépp ngir àgg ci Boroomam, jot ci maqamaa siddiixiya.
2024-03-05
23 min
Bëgg a Baax podcast
Waxtaan ci tasawuf: Xaaj bu njëkk bi
Tasawuf: Dëgg la ne ñi réere tasawuf bari nañu lool ci jamono. Ñii dañu ko réere ndax ñàkk a ci tàbbi, ak xeeb doxalinu ñi ci nekk te di ci boole lu ci bokkul. Am ñu ci nekk ba noppi réere mbir ndax ñàkk a xam li ko tax a jóg. Waxtaan wii dafay leeral tasawuf ci kaw sukandiku ci téere Imaam Dardiir bii di Xarrida al baqita. Boroom leeral ci tasawuf ci gën ja a rafeti anam ak delloo ko cosaanam. Tasawuf du lenn lu dul sellal sa xol ngir àgg ci Boroom
2024-03-01
30 min
Bëgg a Baax podcast
Njariñu sàmm sa waxtu
Waxtu daa doon lu gànjaru lool te mat a moytu a sanq. Jépp noyyi, sépp simili, wépp waxtu wurus la wow nit ki man na ci fàggu lu ko texeel ëllëg. Saggane ko nag ak di ko jeexal ci neen rëccu lay jural nit ki. Moo tax nu def ci waxtaan ngir soññ ci sunu bopp ak képp ku ko dégg.
2024-02-22
27 min
Bëgg a Baax podcast
Masturbation, pornographie: Sabab yi ak saafara si
Bari na ñu am jafe-jafe ci di foowee seen bopp ba të a ko bàyyi. Ci waxtaan wii dañu ciy indi sabab yi koy waral ak yennat ci saafara yi nit man a jëfandikoo ba mucc ci xeetu mbon-mbon yu ni mel.
2024-02-20
25 min
Bëgg a Baax podcast
Waxtaan ci Ihlaas
Waxtaan wii mu ngi aju ci Ihlaas ak sew-sew yi ci nekk te naqari a xam lool. Yoon wi jëmm ci ihlaas daa jafe lool te laaj ug ndimbal. Settantal ak ug xam-xam gu leer moo ciy dimbali nit.
2024-02-19
24 min
Bëgg a Baax podcast
Jege Yàlla jaare ko ci ñaan yi tukkee ci sunna
Yonent bi SAW dundam gépp jaamu Yàlla la woon. Doonoon jëmm joo xam ne dadaan tudd Yàlla ci bépp waxtu, bépp jamono. Roote ci moom ay ñaan yoy ku leeni jëfandikoo, man na la jegeel Yàlla ci kaw nga teewlu leen. Waxtaan wii mu ngi aju ci njariñu ñaan yi tukkee ci Yonent bi SAW.
2024-02-17
30 min
Bëgg a Baax podcast
Tegginu sikar
Waxtaan wii mu ngi aju ci teggin yi nekk ci sikar. Boroom xaaj ko ci ñetti xaaj. Teggin yoy laataa ngay tàmbali sikar yi lay doon, yoo xam ne ci biir sikar si lay doon ak yeneen yu aju ci boo sikaree ba noppi.
2024-02-17
30 min
Bëgg a Baax podcast
Juróom ñaari xeeti bakkan yi
Waxtaan wi mu ngi aju ci juróom ñaari xeeti bakkan yi am (les 7 catégories d’âmes). Doomu aadama dafay jaar ci fànn yu bari ci dundam gi. Bu sàggane rekk man na bokk ci way-texeedi yi. Bu góor-góorlóo nag ba noot bakkanamc man na dem ba kawe loolw
2024-02-17
35 min
Bëgg a Baax podcast
Aajar gi
Nu ngi leen di aajar podcast bii di „Bëgg a Baax Podcast“. Yaatal njàngalem Lislam a ko tax a jóg.
2024-02-16
00 min