Look for any podcast host, guest or anyone
Showing episodes and shows of

Lahat Diaw

Shows

Wolof PodcastWolof PodcastSenegaal ndax dëkk la?Tay nuy waxtaan ci tolluwaayu reew mi. Jafe-jafe yi waa reew mi di dund luko waral ak yan jàngat lanu ci man a def. Senegaal kuy wax te Yàlla tax xamni doxul ci yoon. Loolu bokk na ci li waral nit yi fippu ngir mën a jotaat seen àq.2023-06-0644 minWolof PodcastWolof PodcastXam-xamu XadiisXam-xamu xadiis lanuy waxtaane tay. Mu nekk fànn bu yaatu boo xamne woroom xam-xam yi gëstu na ñu ci ngir yoonal lépp loo xamne toxalees nako co Yonent bi (saws). Bokk na ci ay waat yu ñu leeral jëm ci xadiis, lu melni „Sanad“ te mooy goor yiy soloo xadiis yi, walla „Matn“ te mooy li ñuy soloo. Mu nekk xam-xam yu yaatu waaye fi nuy indi rek fànn wu ndaw ci seddale yi ñu def ci xadiis (classification). Baay Lahatlahatdiaw@gmail.com2023-04-0145 minWolof PodcastWolof PodcastSeex Ibra FaalTay nuy waxtaane jëmm ju am solo te mooy Seex Ibra Faal. Barina loolu lu ñu mën a jàngee ci moom ndax yiteem ju kawe. Mu nekk jëmm ji wone Seex Ahmadu Bàmba ba noppi wone nan lanu ko war a toppe ngir jariñu ci moom. Daan na wax naan Sëñ Bàmba mooy dëkk bi, man Ibra Faal maay yoon bi ciy dem. Naan la def ba taxawal loolu ak lan lanu ci mën a jàngee? Baay Lahatlahatdiaw@gmail.com2023-03-1845 minWolof PodcastWolof Podcast50/50?Tay damay def taxaw setlu ci néegu sëy yi. Ndax kër gi lici war yépp ci wàllu kopar ci góor gi la war a joge walla mënees nako séddoo? Diine moom li mu wax leer na, ndax kodday ak yor góor la war. Waaye ndax léegi nit yi ci diine rek lañuy dellu? Ndax seen mbatit ak tolluwaayu jamono du amul yaneeni jeexital ci seen jëflante? Ps: ci waxtaan bi amna foo xamne polygamie la bëggoon wax, wax monogmie.2023-03-0445 minWolof PodcastWolof PodcastSenegaalSenegaal némmeeku nanu fa soppite yu bari. Moo xam ci jikko, walla xalaatin walla gis-gis. Pénc mi barina lool ay jafe-jafe. Mootax tay nuy def taxaw seetlu ci luko waral ak taaj ay laaj.2023-02-1845 minWolof PodcastWolof PodcastYalla-Yalla (ñaareelu xaaj)Ñaareelu xaaju waxtaan bi nu tàmbali woon ci Yàlla-Yàlla. Nuy indi ay leeral yu bari ci kuy Seex Muusaa ak lu mu woote, lu waral coow li léeg-léeg.2023-02-0445 minWolof PodcastWolof PodcastYàlla-Yàlla (xaaj bu njëkk)Luy Yàlla-Yàlla? Bari na ñuy dégg Yàlla-Yàlla dici wax te xëyna gëstu bi ci war defuñ ko. Mootax tay ñuy indi ay leeral ci kurel boobu ci tuur bi fu mu jóge, kuy seen Sëriñ ak lan la woote.2023-01-2144 minWolof PodcastWolof PodcastSëriñ bu mat SëriñLan mooy Sëriñ bu mat Sëriñ? Ñu gis ne tay lu ëpp ci nit yi am nanu tariqa bu ñu bokk ak ci Sëriñ yu ñu jokku? Waaye lan lanu fay sàkku ak kooku nan la war a mel? Yan jikko la war a yor? Ci waxtaan bii yii ak yaneen lanuy yaatal di ci jéema indi ay leeral ak laabire. Ñu ànd ci ak jëwriñ Bàmba.lahatdiaw@gmail.com2022-07-2345 minWolof PodcastWolof Podcast„séries sénégalaises“At yii ñu weesu gis na ñu ni „séries sénégalaises“ bari nanu loolu. Ñu gis ci tamit yu bees yu bari yoo xamni miinu ñu ko woon ci réew cig fësal. Mootax ñuy def taxaw setlu di jàngat jafe-jafe yi mu mën a indi ci pénc mi. Ma àndaat ci ak jëwriñ Bàmba Jaw.lahatdiaw@gmail.com2022-07-0945 minWolof PodcastWolof PodcastNéegu séyNéegu séy lañuy waxtaane tay. Ñu setlu at yi weesu amna ay soppiku yu mag ci pénc mi. Séy yi barina ay jafe-jafe lool. Ñuy def taxaw setlu ngir man a xam luko waral ak yan saafara lanu ci man a indi. May dalal Soxna Coro Coor muy yëngu ci „aide au développement“.lahatdiaw@gmail.com2022-06-2545 minWolof PodcastWolof PodcastBoroom ñaari tur yiBoroom ñaari tur! Bu yàggul dara gis nanu ak li xéw ak Gana Géy. Mu bañoon jàppale boroom ñaari tur yi ci yaatal seen gis gis, waaye mu dégg ci lu nekk. Loolu moo waral ñu def ci taxaw setlu yi xool ndax mbir mi dëppo na ak suñuy gëm-gëm ak ban taxawaay lanu ci war a am.lahatdiaw@gmail.com2022-06-1145 minWolof PodcastWolof PodcastTariqaSuñu waxtaanu tay bi day jëm ci tariqa. Lan mooy tariqa ak lu ko tax a jóg? Ndax coosaanal tariqa yi moo ngi wéy ba léegi? Amul siki ni ñi sosoon tariqa yi ci lu wér lanu nekkoon, waaye lu ñuy gën a dem mu melni liy mbir mi dëgg, te mooy defar nit ku sotti, danu koy gën a sori. Ndax sant lanuy toppee Sëriñ? Lan lanu fay sàkku? Lan mooy xam Yàlla? Yiii ak yaneen laay waxtaane ak Allaaji Jibi Séy, muy boroom xam-xam di gëstu kat. Bokk...2022-05-2845 minWolof PodcastWolof PodcastYàqu-yàqu jikko yi (ñaareelu xaaj)Tay ñuy yegali waxtaan bi ñu tambali woon ci yàqu-yàqu jikko yi ak liko sabab. Ci xaaj bi mujj bi ginnaw bi ñu indee safaan yi ak liko waral, ñuy jeema indi ay safaralahatdiaw@gmail.com2022-05-1443 minWolof PodcastWolof Podcastyàqu-yàqu jikko yi (xaaj bu njëkk)«Danoo xëm te ñor a gu ñu » Sëriñ Saam Mbay.Tay ñuy waxtaane yàqu-yàqu jikko yi ànd ci ak Seex Aliw Saar. Ku am seetlu tuuti dina xam ni sunu reew mi fi mu tollu ci jikko yu yàqu kéeman la. Lan mooko sabab ak lan mooy saafara ci? Ci waxtaan bi di nanu ci yaatal lu bari ci ñaari xaajlahatdiaw@gmail.com2022-04-3045 minWolof PodcastWolof PodcastJàngee Almãñ (étudier en Allemagne)Tay ñu dikkaat ak yeen ci wolof Podcast di def ay leeral ak laaya biir ci képp koo xam ne daa ngaa bëgg a ñëw Almãñ jàngee ci fi. Ban yoon ngay jaar ba mën a ñëw jàngee fii? Lan nga war a mën a jàng ngir ëlëk nga man a ligéey te doo am benn jafe-jafe? Lan la jàng bi laaj? Yii laaj lanuy jéema tontu ci waxtaan wi. https://www.uni-assist.de/en/https://www.daad.de/en/study-and-research-in-germany/plan-your-studies/requirements/lahatdiaw@gmail.com2022-04-1645 minWolof PodcastWolof PodcastYebbiYebbi mooy lan? Tay ñuy waxtaane lu am solo te yaatu lool ci biir reew mi. Yebbi yégg ma foo xamni jéggi na dayo loolu. Bari na kër walla sëy yu co yëngi. Mu melni li nekkoon cosaan li ak lika taxoon jóg xamatuñ ko. Limiy yàq ëpp fuuf limiy defar. Ñu ànd ci ak Mère Dior Sow.lahatdiaw@gmail.com2022-04-0245 minWolof PodcastWolof PodcastracismeTay ñu dikkat ak baneen woppa muy « racisme ». Mu nekk lu yaatu loo xamne sa su nekk dees koy waxtaane ci pénc mi. Bu ñu xoolee béddi bi ñuy béddi nit ñu ñuul ñi nekk Ukraine te bëgg bokk ci waay-làqu yi, di nanu xamne nii lii ñuy wax « racisme » lu am la. Waaye tay danuy xootal waxtaan bi jàngat ko ak theorie bi ñuy wax « un/doing differences ». Ndaxte lu yaatu la lu lasj ségg lan mooko doon ak lu ko doonul.lahatdiaw@gmail.com2022-03-1945 minWolof PodcastWolof Podcast"Féminisme" (xaaj bu njëkk)Tay ñuy waxtaane « féminisme ». Ma ànd ci ak Seexunaa Njaay di ab gëstu kat di jàngale kat. Ndax lii di « féminisme » dëppoo na ak suñu gis-gisu reew? Lutax lu ci ëpp ñuy seetlu ñàkk a dëppo. Lii ak yaneen lanu doon yaatal vi xaaj bu njëkk bi.lahatdiaw@gmail.com2022-03-0545 minWolof PodcastWolof PodcastIslamophobie« Islamophobie »Tay ñuy def taxaw setlu ci Islaam ak feeñal gi néññ ñi di feeñal mbañeel jëmale ko ci diine ji walla jullit yi walla seeni gëm gëm. Fu mu joge ak lan moo ko sabab?lahatdiaw@gmail.com2022-02-1945 minWolof PodcastWolof PodcastBëgg a baax (ñaareelu xaaj bi)Tay ñuy yéggali suñu waxtaan bi ñu tambali woon ci yoonu mbaax doon yaatal ci lan la nit ki wara def ngir am ak njub ak sellal. Bii ma mujjee tudd nak ñu koy sàkkoo ci tariqa. Mu mel ni kon mat na laaj kuy Sëriñ bu mat Sëriñ ak lan la fa taalibe bi war a sàkku. Yal nanu Yàlla defal njub ak mbaax.lahatdiaw@gmail.com2022-02-0545 minWolof PodcastWolof PodcastBëgg a baaxTay ma ànd ak sama gan gu njëkk muy Bàmba ñuy waxtaane yoonu njub ak baax. Def lu baax yomb na waaye dëkk ci moo jafe. Yonent bi (saws) dafay wax ni àddina mooy aljànna ki weddi, waaye kaso la ci ki gëm. Mu melni kon ku bëgg dund ci niki Yàlla gërëmee dina laaj jékki ay jéego jëm ci yar sa bakan ak topp Yàlla. Waaye mu nekk yoon bu meti loolu. Lan mooy yoonu njub? Ak yan jafe-jafe la doomu aadama bi di dajeek ngi yégg baax? Ci të...2022-01-2245 minWolof PodcastWolof PodcastIdentité culturelle (xam sa bopp ak sa mbatit)Sunu episode bu njëkk ñuy waxtaane « identité culturelle » : ndax dañoo ñàkk suñu mbaatit (culture) ginnaaw bi Tubaab yi ñëwee suñu réew yi noot ñu? Ndax xeebuñ suñu bopp ginnaaw loolu? Ndax jéem nanu dellu suñu bopp? Mu nekk ay laaj yu bari yoo xamne mat na waxtaane. Ak téereeb Ken Bugul bi tudd « Le Baobab fou » lañuy jéema saytu laaj yi yépp.lahatdiaw@gmail.com2022-01-0845 minWolof PodcastWolof PodcastintroTay ñuy def benn tambali bu ndaw ngir dégtal leen suñu « podcast » bi ñu am yéene tambali. Ñuy wax lutax ñu fas ko yéene def ci kàllaama wolof, yan woppa (sujets) lanu fas yéene waxtaane ak ki kay def mooy kan. Ci tënk lii ag ubbite lalahatdiaw@gmail.com2022-01-0108 min